1
1.Piyeer 2:9
Téereb Injiil
TI
Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu sarxalkati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi.
Compare
Explore 1.Piyeer 2:9
2
1.Piyeer 2:24-25
Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér. Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi délsi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.
Explore 1.Piyeer 2:24-25
3
1.Piyeer 2:10
Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko.
Explore 1.Piyeer 2:10
4
1.Piyeer 2:2-3
Gannaaw ay liir ngeen yuy doora juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla.
Explore 1.Piyeer 2:2-3
5
1.Piyeer 2:11-12
Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak i doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol. Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo.
Explore 1.Piyeer 2:11-12
6
1.Piyeer 2:5
te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay sarxalkat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
Explore 1.Piyeer 2:5
7
1.Piyeer 2:1
Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw.
Explore 1.Piyeer 2:1
8
1.Piyeer 2:4
Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la
Explore 1.Piyeer 2:4
9
1.Piyeer 2:16
Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gëna feddali seen jaamu Yàlla.
Explore 1.Piyeer 2:16
10
1.Piyeer 2:15
Ndaxte noonu la coobarey Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.
Explore 1.Piyeer 2:15