1
1.Yowaan 2:15-16
Téereb Injiil
TI
Buleen sopp àddina ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom. Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina.
Compare
Explore 1.Yowaan 2:15-16
2
1.Yowaan 2:17
Te àddina day wéy, waaye kuy def coobarey Yàlla dinga sax ba fàww.
Explore 1.Yowaan 2:17
3
1.Yowaan 2:6
Ku wax ne ci Yàlla nga sax, fàww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam.
Explore 1.Yowaan 2:6
4
1.Yowaan 2:1
Samay doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen baña def bàkkaar. Waaye su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi.
Explore 1.Yowaan 2:1
5
1.Yowaan 2:4
Ku wax ne xam nga ko, te sàmmoo ay ndigalam, dangay fen, te dëgg nekkul ci yaw.
Explore 1.Yowaan 2:4
6
1.Yowaan 2:3
Ci lii lanu xame ne xam nanu ko: sàmm ay ndigalam.
Explore 1.Yowaan 2:3
7
1.Yowaan 2:9
Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey bañ sa mbokk, yaa ngi ci lëndëm ba tey.
Explore 1.Yowaan 2:9
8
1.Yowaan 2:22
Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji.
Explore 1.Yowaan 2:22
9
1.Yowaan 2:23
Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi.
Explore 1.Yowaan 2:23