1
1.Yowaan 3:18
Téereb Injiil
TI
Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
Compare
Explore 1.Yowaan 3:18
2
1.Yowaan 3:16
Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
Explore 1.Yowaan 3:16
3
1.Yowaan 3:1
Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu mana tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
Explore 1.Yowaan 3:1
4
1.Yowaan 3:8
Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
Explore 1.Yowaan 3:8
5
1.Yowaan 3:9
Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo mana sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
Explore 1.Yowaan 3:9
6
1.Yowaan 3:17
Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
Explore 1.Yowaan 3:17
7
1.Yowaan 3:24
Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne dëkk na ci nun.
Explore 1.Yowaan 3:24
8
1.Yowaan 3:10
Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
Explore 1.Yowaan 3:10
9
1.Yowaan 3:11
Ndaxte xibaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante
Explore 1.Yowaan 3:11
10
1.Yowaan 3:13
Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
Explore 1.Yowaan 3:13