1
Room 8:28
Kàddug Yàlla
KY
Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
Compare
Explore Room 8:28
2
Room 8:38-39
Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.
Explore Room 8:38-39
3
Room 8:26
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Explore Room 8:26
4
Room 8:31
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Explore Room 8:31
5
Room 8:1
Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
Explore Room 8:1
6
Room 8:6
Xintey bakkan nag ci dee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla dund ak jàmm lay jur.
Explore Room 8:6
7
Room 8:37
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Explore Room 8:37
8
Room 8:18
Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
Explore Room 8:18
9
Room 8:35
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Explore Room 8:35
10
Room 8:27
Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
Explore Room 8:27
11
Room 8:14
Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu.
Explore Room 8:14
12
Room 8:5
Ndax kat ñi topp seen bindu suux, mbiri bakkan doŋŋ lañu xinte, waaye ñi topp Noowug Yàlla ñoom, mbiri Noowug Yàlla mooy seen xinte.
Explore Room 8:5
13
Room 8:32
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Explore Room 8:32
14
Room 8:16-17
Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu. Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Explore Room 8:16-17
15
Room 8:7
Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.
Explore Room 8:7
16
Room 8:19
Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.
Explore Room 8:19
17
Room 8:22
Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu.
Explore Room 8:22