1
Room 7:25
Kàddug Yàlla
KY
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nuy walloo jëmmu Yeesu Almasi bi, sunu Sang. Kon daal man, ci sama bopp, ci sama wàllu xel, yoonu Yàlla laay surgawu, waaye ci sama wàllu yaramu suux wii, yoonu bàkkaar laay surgawu.
Compare
Explore Room 7:25
2
Room 7:18
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Explore Room 7:18
3
Room 7:19
Ndax kat du lu baax li ma namma jëfe laay jëfe, waaye lu bon li ma nammul, moom laay jëfe.
Explore Room 7:19
4
Room 7:20
Te su dee li ma nammul, moom laay def, kon kay dootul man maa koy def, waaye dooley bàkkaar bi dëkk ci man moo koy def.
Explore Room 7:20
5
Room 7:21-22
Takk bi ma ci def daal mooy lii: bu ma nammee def lu baax, lu bon a may teewalsi. Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex.
Explore Room 7:21-22
6
Room 7:16
Gannaaw li ma bëggul, moom laay def nag, juboo naa ak yoonu Musaa ci dëggal ne yoonu Musaa baax na.
Explore Room 7:16