1
Room 6:23
Kàddug Yàlla
KY
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Compare
Explore Room 6:23
2
Room 6:14
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
Explore Room 6:14
3
Room 6:4
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi bi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
Explore Room 6:4
4
Room 6:13
Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébballeen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.
Explore Room 6:13
5
Room 6:6
Li nu bir moo di nun ña woon démb, ca bantub Yeesu ba lees nu daajaale, ngir xewwil sunu yaramu bàkkaar, ba nu noppee doon ay jaam, bàkkaar di sunub sang.
Explore Room 6:6
6
Room 6:11
Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi.
Explore Room 6:11
7
Room 6:1-2
Ana lu loolu di tekki nag? Ndax kon danuy wéye bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gëna yokku? Mukk kay! Nun ñi dee tàggale ak bàkkaar ba noppi, ana nu nuy saxootee bàkkaar?
Explore Room 6:1-2
8
Room 6:16
Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci dee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu baaxe leen àtteb ñu jub.
Explore Room 6:16
9
Room 6:17-18
Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa ji ngeen di ndénkaaneem. Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak nooteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.
Explore Room 6:17-18