1
Room 5:8
Kàddug Yàlla
KY
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
Compare
Explore Room 5:8
2
Room 5:5
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Explore Room 5:5
3
Room 5:3-4
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ; te muñ mooy jur kóllërey biir coono; kóllërey biir coono mooy jur yaakaar.
Explore Room 5:3-4
4
Room 5:1-2
Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi. Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.
Explore Room 5:1-2
5
Room 5:6
Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca waxtu wa gën, la Almasi bi deewal yéefar yi.
Explore Room 5:6
6
Room 5:9
Gannaaw baaxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Explore Room 5:9
7
Room 5:19
Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu baaxe ñu bare àtteb nit ñu jub.
Explore Room 5:19
8
Room 5:11
Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi bi nu jubale ak moom.
Explore Room 5:11