1
Room 4:20-21
Kàddug Yàlla
KY
Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla. Dafa wéroon Ibraayma péŋŋ ne li Yàlla dige, man na koo def.
Compare
Explore Room 4:20-21
2
Room 4:17
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.
Explore Room 4:17
3
Room 4:25
mi ñu teg ciy loxo, mu dee ndax sunuy tooñ, ba dekkal ko, ngir nu ame ci àtteb nit ñu jub.
Explore Room 4:25
4
Room 4:18
Ba bunti yaakaar yépp tëjee, Ibraayma moo dese woon yaakaaram, wéye ngëmam, ba doon maamu xeet yu bare, loolu dëppook kàddu ga noon: «Noonu la saw askan di tollu.»
Explore Room 4:18
5
Room 4:16
Kon nag digeb Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.
Explore Room 4:16
6
Room 4:7-8
Mu ne: «Ndokkalee yeen ñi ñu baal seeni moy, jéggal leeni bàkkaar. Ndokkalee yaw mi Boroom bi toppul say tooñ.»
Explore Room 4:7-8
7
Room 4:3
Ana lu ci Mbind mi wax? Da ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, Yàlla nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal.»
Explore Room 4:3