1
Peeñu ma 21:4
Kàddug Yàlla
KY
Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Compare
Explore Peeñu ma 21:4
2
Peeñu ma 21:5
Ci kaw loolu ki toog ci ngàngune mi ne: «Maa ngii di yeesal lépp!» Mu teg ci ne ma: «Bindal, yii kàddu yu wóor la te dëggu.»
Explore Peeñu ma 21:5
3
Peeñu ma 21:3
Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.
Explore Peeñu ma 21:3
4
Peeñu ma 21:6
Mu neeti ma: «Sotti na! Maay Alfa, di Omega, di njàlbéen, di muj. Ku mar, maa lay may nga naan ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.
Explore Peeñu ma 21:6
5
Peeñu ma 21:7
Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom
Explore Peeñu ma 21:7
6
Peeñu ma 21:8
waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem fen-kat ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»
Explore Peeñu ma 21:8
7
Peeñu ma 21:1
Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su njëkk sa ak suuf su njëkk sa wéy, te géej amatul.
Explore Peeñu ma 21:1
8
Peeñu ma 21:2
Ma gis nag dëkk bu sell bi, Yerusalem gu bees gi, mu wàcce asamaan fa Yàlla, mel nib séet bu defaru ba jekk ngir jëkkëram.
Explore Peeñu ma 21:2
9
Peeñu ma 21:23-24
Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Xar mi di làmpam. Askani àddina, leeru dëkk bi lañuy doxe, buuri àddina di fi indi seen teraanga.
Explore Peeñu ma 21:23-24