1
Peeñu ma 20:15
Kàddug Yàlla
KY
Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.
Compare
Explore Peeñu ma 20:15
2
Peeñu ma 20:12
Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.
Explore Peeñu ma 20:12
3
Peeñu ma 20:13-14
Ba mu ko defee géej jébbale néew ya woon ca moom, dee ak njaniiw jébbale néew ya woon ca moom, ñu daldi àtte ku nekk ca say jëf. Ba loolu amee ñu jàpp dee ak njaniiw, sànni ca déegu sawara sa. Ñaareelu dee gi nag moo di déegu sawara si.
Explore Peeñu ma 20:13-14
4
Peeñu ma 20:11
Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex ak ki ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.
Explore Peeñu ma 20:11
5
Peeñu ma 20:7-8
Bu junniy at yi matee, dees na yiwi Seytaane, génnee ko ca kasoom, mu dikk, naxsi askani ñeenti colli àddina, yi ñuy wax waa Gog ak Magog. Mu dajale leen ngir xare; ñu baree ni feppi suufas géej.
Explore Peeñu ma 20:7-8