1
Peeñu ma 19:7
Kàddug Yàlla
KY
Nanu bég, di bànneexu te màggal ko, ndax céetu Xar mi agsi na, ab séetam defaru na ba noppi!
Compare
Explore Peeñu ma 19:7
2
Peeñu ma 19:16
Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»
Explore Peeñu ma 19:16
3
Peeñu ma 19:11
Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.
Explore Peeñu ma 19:11
4
Peeñu ma 19:12-13
Ay gëtam a ngi mel ni sawara wuy tàkk, bopp bi, mbaxanay buur yu baree ci tege, ñu bind ci kawam tur wu kenn xamul ku dul moom. Mbubb ma mu sol, dees koo sóob ci deret, te turam wi ñu ko xame di «Kàddug Yàlla.»
Explore Peeñu ma 19:12-13
5
Peeñu ma 19:15
Gémmiñ gi, saamar bu ñaw a ciy lange, mu di ko cawe askan yi. Moo leen di jiitee yetu weñ, te mooy dëggaate ci biir nalukaay bi reseñ ji ñuy segale biiñu sànj mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.
Explore Peeñu ma 19:15
6
Peeñu ma 19:20
Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni ñuy dund, ca déegu sawara waak tamarax bay bax.
Explore Peeñu ma 19:20