1
Peeñu ma 2:4
Kàddug Yàlla
KY
«Waaye li ma la sikke moo di sa cofeel ga nga jëkke woon, moom nga wacc.
Compare
Explore Peeñu ma 2:4
2
Peeñu ma 2:5
Kon nag fàttalikul fu kawe fa nga xàwweekoo ba fii, te nga tuub, di jëfe jëf ja nga jëkke woon. Lu ko moy maay dikk ba fi yaw, daldi jële sa tegukaayu làmp fa bérebam, ndegam tuubuloo.
Explore Peeñu ma 2:5
3
Peeñu ma 2:10
Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.
Explore Peeñu ma 2:10
4
Peeñu ma 2:7
«Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.
Explore Peeñu ma 2:7
5
Peeñu ma 2:2
Gis naa say jëf, gis sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñu bon ñi. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay fen-kat lañu.
Explore Peeñu ma 2:2
6
Peeñu ma 2:3
Xam naa it ne muñ nga te sonn nga moos ngir man te xàddiwoo.
Explore Peeñu ma 2:3
7
Peeñu ma 2:17
«Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; ci doj wi ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.
Explore Peeñu ma 2:17