1
Peeñu ma 3:20
Kàddug Yàlla
KY
Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.
Compare
Explore Peeñu ma 3:20
2
Peeñu ma 3:15-16
Xam naa say jëf; xam naa ne seddoo, tàngoo. Su ma sañoon, nga sedd mbaa nga tàng. Gannaaw nii nga nugge nag; tàngoo, seddoo, dinaa la yàbbi.
Explore Peeñu ma 3:15-16
3
Peeñu ma 3:19
«Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!
Explore Peeñu ma 3:19
4
Peeñu ma 3:8
Gis naa say jëf. Maa def fi sa kanam, bunt bu tijjiku bu kenn manula tëj. Ndax néew nga doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.
Explore Peeñu ma 3:8
5
Peeñu ma 3:21
«Ku am ndam nag, maa lay may nga toog ak man fi sama ngàngune, na ma ame woon ndam, ba toog ak sama Baay fi ngànguneem.
Explore Peeñu ma 3:21
6
Peeñu ma 3:17
Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ
Explore Peeñu ma 3:17
7
Peeñu ma 3:10
Gannaaw yaa sàmm sama kàddu, ba muñ ni ma la ko sante, man itam dinaa la sàmm ci waxtuw nattu biy wàccsi ci àddina sépp, ngir nattu waa kaw suuf.
Explore Peeñu ma 3:10
8
Peeñu ma 3:11
«Léegi ma ñëw. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.
Explore Peeñu ma 3:11
9
Peeñu ma 3:2
Teewlul te nga leqali ndes wi ngay waaja deele. Ndax kat, gisuma sa jëf ju mat fa sama kanam Yàlla.
Explore Peeñu ma 3:2