1
Filib 3:13-14
Kàddug Yàlla
KY
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam, daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu.
Compare
Explore Filib 3:13-14
2
Filib 3:10-11
Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deewam, tey yaakaara dekki, ak nu mu mana deme.
Explore Filib 3:10-11
3
Filib 3:8
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi
Explore Filib 3:8
4
Filib 3:7
Waaye la ma jàppe woon ag ndollent, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi bi.
Explore Filib 3:7