1
Màrk 9:23
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo manee”? Ku ànd ak gëm kay, dara tëwu la.»
Compare
Explore Màrk 9:23
2
Màrk 9:24
Baayu xale bi daldi àddu ca kaw, ne: «Kon gëm naa, ngalla wallu maak sama ngëmadi.»
Explore Màrk 9:24
3
Màrk 9:28-29
Ba Yeesu duggee ca kër ga, taalibe ya laaj ko ci sutura, ne ko: «Lu tax manunu woona dàqal sunu bopp, rab wi?» Yeesu ne leen: «Xeetu rab wii, maneesu koo dàqe lenn lu moy ñaan.»
Explore Màrk 9:28-29
4
Màrk 9:50
Xorom lu baax la, waaye bu raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Nangeen jikkowoo xorom su raxul, daldi jàmmoo.»
Explore Màrk 9:50
5
Màrk 9:37
«Képp ku dalal xale bu mel nii ndax man, man mii nga dalal, te képp ku ma dalal, du man nga dalal, waaye ki ma yebal nga dalal.»
Explore Màrk 9:37
6
Màrk 9:41
Maa leen ko wax, déy, képp ku leen may ab kaasu ndox, ngir li ngeen di niti Almasi bi, doo ñàkk sag pey mukk.
Explore Màrk 9:41
7
Màrk 9:42
«Waaye kenn sax ci xale yii ma gëm, képp ku ko bàkkaarloo, li gën ci moom, mooy ñu takk ci baatam doju wolukaay wu réy wu mbaam di wëndeel, daldi koy sànni biir géej.
Explore Màrk 9:42
8
Màrk 9:47
Su la sa bët bàkkaarloo, luqil. Tàbbiwaale patt ci nguurug Yàlla, moo gën ci yaw ñu boole laak sa ñaari bët, sànni biir sawara
Explore Màrk 9:47