Ana lu nit wara mana weccee bakkanam? Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, ci biir niti jamono jii, di jamonoy bokkaaleek bàkkaar, bés bu Doomu nit ki dikkee ci biir darajay Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi, su keroogee moom it dina la kersawoo.»