1
Màrk 10:45
Kàddug Yàlla
KY
Ndax Doomu nit ki itam ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñu bare.»
Compare
Explore Màrk 10:45
2
Màrk 10:27
Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Nit la të, waaye tëwul Yàlla. Yàlla man na lépp.»
Explore Màrk 10:27
3
Màrk 10:52
Yeesu ne ko: «Demal. Sa ngëm musal na la.» Ca saa sa muy gis, daldi topp Yeesu ca yoon wa.
Explore Màrk 10:52
4
Màrk 10:9
Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
Explore Màrk 10:9
5
Màrk 10:21
Yeesu nag xool ko bëti cofeel, daldi ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal te lépp loo am, nga jaay ko, jox ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
Explore Màrk 10:21
6
Màrk 10:51
Yeesu ne ko: «Ana loo bëgg, ma defal la ko?» Silmaxa ba ne ko: «Xanaa ma dellu di gis, sama kilifa.»
Explore Màrk 10:51
7
Màrk 10:43
Yeen nag, bumu deme noonu ci seen biir. Ku bëgga doon ku màgg ci yeen, na nekk seen surga
Explore Màrk 10:43
8
Màrk 10:15
Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca tàbbi mukk.»
Explore Màrk 10:15
9
Màrk 10:31
Waaye ñu baree ngi jiitu tey, ñooy mujji, te ñu baree ngi mujje tey, ñooy jiituji.»
Explore Màrk 10:31
10
Màrk 10:6-8
Waaye ca njàlbéen ga Yàlla sàkke àddina, ca la leen sàkk ñuy ku góor ak ku jigéen. Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, taqoo ak jabaram, ba ñoom ñaar di wenn suux doŋŋ. Moo tax dootuñu ñaar, waaye wenn suux doŋŋ lañu.
Explore Màrk 10:6-8