1
Màrk 4:39-40
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu yewwu, daldi gëdd ngelaw la, ne dex ga: «Dalal, neel tekk!» Ngelaw la ne tekk, lépp ne sendaw. Yeesu ne leen: «Lu ngeen di tiit? Dangeena gëmul ba tey?»
Compare
Explore Màrk 4:39-40
2
Màrk 4:41
Ba loolu amee ñu tiit lool, naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan, ba ngelaw leek dex gi sax di ko déggal?»
Explore Màrk 4:41
3
Màrk 4:38
Teewul Yeesoo nga ca taatu gaal ga, tëdd, gegenu, di nelaw. Taalibe ya yee ko, ne ko: «Kilifa gi, nu ngi sànku, xanaa xalaatoo nu?»
Explore Màrk 4:38
4
Màrk 4:24
Mu neeti leen: «Teewluleen bu baax li ngeen di dégg. Natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale, ba wis leen.
Explore Màrk 4:24
5
Màrk 4:26-27
Yeesu teg ca ne: «Nguurug Yàlla dafa mel ni nit ku sànni jiwu fi suuf. Buy nelaw ak bu yewwoo, guddi ak bëccëg, jiwu maa ngi sax, di màgg, te xamul nan la koy defe.
Explore Màrk 4:26-27
6
Màrk 4:23
Ku am nopp yu mu dégge daal, na dégg.»
Explore Màrk 4:23