1
Màrk 5:34
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm a la faj. Demal ak jàmm te teqalikook sa jàngoro.»
Compare
Explore Màrk 5:34
2
Màrk 5:25-26
Sennas ndaw a nga ca woon, fukki at ak ñaar ma ngay xëpp deret. Fekk na mu sonn coono bu réy bu ko fajkat yu bare teg. Mu sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, xanaa gëna wopp.
Explore Màrk 5:25-26
3
Màrk 5:29
Ba mu tegee loxoom ca mbubbam Yeesu, ca saa sa la deret ja taxaw, mu yég ci yaramam, ne teqalikoo naak jàngoro ja.
Explore Màrk 5:29
4
Màrk 5:41
Mu jàpp ca loxol xale ba, ne ko: «Talita kumi,» mu tekki: «Janq, ma ne la, jógal.»
Explore Màrk 5:41
5
Màrk 5:35-36
Yeesoo ngay wax, noppeegul, aw nit jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk, ne njiit la: «Sa doom faatu na. Jaratul ngay yékkati kilifa gi.» Yeesu nag tanqamlu wax ja ñu wax. Mu ne njiit la: «Bul tiit, gëmal rekk.»
Explore Màrk 5:35-36
6
Màrk 5:8-9
Booba Yeesoo nga ko naa: «Yaw rab wi, génnal ci waa ji.» Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Gàngoor laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
Explore Màrk 5:8-9