1
Màrk 2:17
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu nag dégg ca, ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. Du ñi jub laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo.»
Compare
Explore Màrk 2:17
2
Màrk 2:5
Yeesu seetlu seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Doom, jéggalees na la say bàkkaar.»
Explore Màrk 2:5
3
Màrk 2:27
Yeesu dellu ne leen: «Bésub Noflaay, dees koo sàkk ngir nit ki. Waaye nit ki, sàkkeesu ko ngir bésub Noflaay.
Explore Màrk 2:27
4
Màrk 2:4
Waaye manuñu koo àggale ca moom ndax mbooloo ma. Ñu yéeg, bënn kaw taax ma, bëtte ko ca wet ga tollook fa Yeesu féete. Ñu yoor nag basaŋ ga lafañ ba tëdd.
Explore Màrk 2:4
5
Màrk 2:10-11
Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Dama ne, jógal, jël sa basaŋ, te ñibbi.»
Explore Màrk 2:10-11
6
Màrk 2:9
Ana yii yaar, lu ci gëna yomb: ne lafañ bi “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne ko: “Jógal, jël sa basaŋ te dox”?
Explore Màrk 2:9
7
Màrk 2:12
Mu jóg, jël basaŋ ga ca saa sa, daldi génn fa kanam ñépp, ba ñépp waaru, di sàbbaal Yàlla, naan: «Lu mel nii, masunu koo gis!»
Explore Màrk 2:12