1
Màrk 11:24
Kàddug Yàlla
KY
Moo tax ma di leen wax lii: Lépp lu ngeen di sàkku cig ñaan, gëmleen ne jot ngeen ko ba noppi, dingeen ko am.
Compare
Explore Màrk 11:24
2
Màrk 11:23
Maa leen ko wax déy, képp ku ne tund wale: “Jógal, tàbbiji géej,” te bañ cee boole xel ñaar, xanaa gëm ne li nga wax dina am, noonu lees la koy nangule.
Explore Màrk 11:23
3
Màrk 11:25-26
Bu ngeen taxawee di ñaan it, te fekk ngeen jàppal kenn dara, baalleen ko, ngir seen Baay ba fa asamaan baal leen seeni tooñ, yeen itam.»
Explore Màrk 11:25-26
4
Màrk 11:22
Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla.
Explore Màrk 11:22
5
Màrk 11:17
Mu di leen jàngal nag, wax leen, ne leen: «Xanaa bindeesul ne: “Sama kër gi, kërug ñaan lees ko tudde, ñeel xeetoo xeet.” Waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc.»
Explore Màrk 11:17
6
Màrk 11:9
Ci kaw loolu ña jiitu ak ña topp ca Yeesu xaacoondoo, naan: «Osaana! Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi!
Explore Màrk 11:9
7
Màrk 11:10
Na barke wàcc ci nguur giy ñëw, sunu nguurug maam Daawuda! Osaana, na cant jibe béreb ya gëna kawe!»
Explore Màrk 11:10