1
Macë 26:41
Kàddug Yàlla
KY
Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
Compare
Explore Macë 26:41
2
Macë 26:38
Ca la leen ne: «Tiis wu réy la sama xol fees, ba may bëgga dee! Toogleen fii, te ngeen ànd ak man ci teewlu.»
Explore Macë 26:38
3
Macë 26:39
Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Explore Macë 26:39
4
Macë 26:28
ndax lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te nara tuurul ñépp ngir njéggalug bàkkaar.
Explore Macë 26:28
5
Macë 26:26
Naka ñuy lekk nag, Yeesu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox taalibe ya. Mu ne leen: «Jëlleen lekk, lii sama yaram la.»
Explore Macë 26:26
6
Macë 26:27
Mu teg ca jël ab kaas, yékkati kàddug cant, jox leen ko, ne leen: «Naanleen ci, yeen ñépp
Explore Macë 26:27
7
Macë 26:40
Gannaaw loolu mu délsi, fekk taalibe ya di nelaw. Mu ne Piyeer: «Wenn waxtu doŋŋ, amuleen dooley teewloondoo kook man?
Explore Macë 26:40
8
Macë 26:29
Maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan mukk ndoxum reseñ mii, ba kera may naan, maak yeen, ndoxum reseñ mu bees ca sama nguurug Baay.»
Explore Macë 26:29
9
Macë 26:75
Piyeer daldi fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ganaar a sab, dinga ma jàmbu ñetti yoon.» Mu génn nag, di jooy jooy yu metti.
Explore Macë 26:75
10
Macë 26:46
Jógleen nu dem, ki may wor a ngi nii.»
Explore Macë 26:46
11
Macë 26:52
Teewul Yeesu ne ko: «Dellool sa saamar ci mbaram, ndax képp ku bocci saamar, saamar lay deewe.
Explore Macë 26:52