«Wóoy ngalla yeen firikati yoon yi ak Farisen yi, jinigalkat yi! Xobi naana, ak safal yu mel ni anet ak kumin, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, tey sofental njubte ak yërmande ak ngëm. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sofental.