1
Luug 9:23
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
Compare
Explore Luug 9:23
2
Luug 9:24
Ndax képp ku bëgga rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan.
Explore Luug 9:24
3
Luug 9:62
Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»
Explore Luug 9:62
4
Luug 9:25
Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ?
Explore Luug 9:25
5
Luug 9:26
Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi.
Explore Luug 9:26
6
Luug 9:58
Yeesu itam ne ko: «Till akug kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.»
Explore Luug 9:58
7
Luug 9:48
Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
Explore Luug 9:48