1
Luug 10:19
Kàddug Yàlla
KY
Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
Compare
Explore Luug 10:19
2
Luug 10:41-42
Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare. Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.»
Explore Luug 10:41-42
3
Luug 10:27
Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi jëmm ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
Explore Luug 10:27
4
Luug 10:2
Mu ne leen: «Ngóob mee yaatu, te surga yi néew. Kon nag ñaanleen Boroom ngóob mi, ay surga yu mu yebal cim ngóobam.
Explore Luug 10:2
5
Luug 10:36-37
Mu teg ca ne ko: «Ñett ñii, kan nga foog ne moo ci taxawu waa ja dajeek sàcc ya, taxawaayu nit ak moroomam?» Mu ne ko: «Xanaa ki ko defal yërmande.» Yeesu nag ne ko: «Demal boog, di defe noonu.»
Explore Luug 10:36-37
6
Luug 10:3
Demleen! Xamleen ne maa leen yebal, mbete ay mbote ci biiri bukki.
Explore Luug 10:3