1
Luug 8:15
Kàddug Yàlla
KY
Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.
Compare
Explore Luug 8:15
2
Luug 8:14
Li tuuru ci ay xaaxaam mooy ñi déglu kàddu gi, te ay xalaat ak alal ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor.
Explore Luug 8:14
3
Luug 8:13
Ñi féete fu bare ay doj, ñoo dégg kàddu gi, nangoo ko xol bu sedd. Waaye ñooñu, ab reen lañu amul. Ab diir rekk lañuy gëm, bu janti nattu dikkee, ñu dellu gannaaw.
Explore Luug 8:13
4
Luug 8:25
Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?»
Explore Luug 8:25
5
Luug 8:12
Ñi ci kaw yoon wi mooy ñi dégg. Seytaane nag mooy dikk, foqati kàddu gi ci seen xol, ngir ñu baña gëm ba mucc.
Explore Luug 8:12
6
Luug 8:17
Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ.
Explore Luug 8:17
7
Luug 8:47-48
Ndaw sa xam ne feeñ na. Mu daldi dikk, di lox, ne gurub fa kanam Yeesu, daldi wax ca kanam ñépp la waral mu teg ko loxoom, ak na mu wére ca saa sa. Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm a la faj. Demal ak jàmm.»
Explore Luug 8:47-48
8
Luug 8:24
Taalibe yi yee Yeesu, ne ko: «Njaatige, njaatige, nu ngi sànku!» Mu yewwu, gëdd ngelaw li ak gannax yu réy yi. Lépp dal, ne tekk.
Explore Luug 8:24