Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér. Ndaxte man itam ci kilifteef laa tënku, te it ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israayil sax, gisuma ko ci.»