Yeesoo nga nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana daj ca yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqalikook moom.