1
Luug 23:34
Kàddug Yàlla
KY
Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
Compare
Explore Luug 23:34
2
Luug 23:43
Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
Explore Luug 23:43
3
Luug 23:42
Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttaliku ma!»
Explore Luug 23:42
4
Luug 23:46
Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dog.
Explore Luug 23:46
5
Luug 23:33
Ba ñu agsee ca béreb, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saay-saay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
Explore Luug 23:33
6
Luug 23:44-45
Ba ñu demee ba tollu ci booru fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon. Naka la jant bi giim, ridob biir néegu Yàlla ba xar ca digg ba.
Explore Luug 23:44-45
7
Luug 23:47
Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
Explore Luug 23:47