1
Luug 22:42
Kàddug Yàlla
KY
Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Compare
Explore Luug 22:42
2
Luug 22:32
Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»
Explore Luug 22:32
3
Luug 22:19
Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu joxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo.»
Explore Luug 22:19
4
Luug 22:20
Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji nara tuuru ngir yeen.
Explore Luug 22:20
5
Luug 22:44
Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
Explore Luug 22:44
6
Luug 22:26
Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga.
Explore Luug 22:26
7
Luug 22:34
Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga jàmbu ñetti yoon, ne xamuloo ma.»
Explore Luug 22:34