1
Sarxalkat yi 19:18
Kàddug Yàlla
KY
Buleen di feyantook seen mbokkum waa réew te buleen ko dencal mer. Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom. Maay Aji Sax ji.
Compare
Explore Sarxalkat yi 19:18
2
Sarxalkat yi 19:28
mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
Explore Sarxalkat yi 19:28
3
Sarxalkat yi 19:2
«Waxal mbooloom bànni Israayil gépp ne leen: Ñu sell ngeen wara doon, ndax Ku sell laa, man seen Yàlla Aji Sax ji.
Explore Sarxalkat yi 19:2
4
Sarxalkat yi 19:17
«Buleen tong seen mbokk, te artuleen seen moroom bu baax bala ngeena bokk ak moom gàddu bàkkaar.
Explore Sarxalkat yi 19:17
5
Sarxalkat yi 19:31
«Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.
Explore Sarxalkat yi 19:31
6
Sarxalkat yi 19:16
Buleen wër di yàq deru nit ci seen bokki waa réew. Buleen def dara lu mana reylu seen moroom. Maay Aji Sax ji.
Explore Sarxalkat yi 19:16