1
Yowaan 8:12
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu waxati leen ne leen: «Man maay leeru àddina. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye leeru dund ngay am.»
Compare
Explore Yowaan 8:12
2
Yowaan 8:32
Su boobaa dingeen xam liy dëgg, te dëgg gi moo leen di goreel.»
Explore Yowaan 8:32
3
Yowaan 8:31
Yeesu moo waxoon Yawut yi ko gëmoon ne leen: «Bu ngeen saxee ci sama kàddu, samay taalibe dëgg ngeen.
Explore Yowaan 8:31
4
Yowaan 8:36
Kon nag su leen Doom ji goreelee, ngeen diy gor tigi.
Explore Yowaan 8:36
5
Yowaan 8:7
Naka lañu ko toppe ay laaj, mu siggi ne leen: «Ku masula bàkkaar ci yeen, na njëkka sànni ndaw si xeer.»
Explore Yowaan 8:7
6
Yowaan 8:34
Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, képp kuy bàkkaar, ab jaamu bàkkaar la.
Explore Yowaan 8:34
7
Yowaan 8:10-11
Mu daldi siggi ne ko: «Ndaw sii, ana nit ñi? Kenn joxu la ci sab daan?» Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it duma la daan. Demal, te bul bàkkaarati.»
Explore Yowaan 8:10-11