1
Yowaan 1:12
Kàddug Yàlla
KY
Teewul mboolem ñi ko dalal, ba gëm ko, ñoom la may ñu yelloo doon doomi Yàlla.
Compare
Explore Yowaan 1:12
2
Yowaan 1:1
Njàlbéen ga fekk na Kàddu gi nekk, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
Explore Yowaan 1:1
3
Yowaan 1:5
Leer moo feeñ ci biir lëndëm, te lëndëm gi manu koo man.
Explore Yowaan 1:5
4
Yowaan 1:14
Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.
Explore Yowaan 1:14
5
Yowaan 1:3-4
Lépp ci Kàddu gi lañu ko sàkke. Sàkkeesul dara lu ñu sàkkewul ci moom. Ci moom la dund nekk, te dund dig leer, ñeel nit ñi.
Explore Yowaan 1:3-4
6
Yowaan 1:29
Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.
Explore Yowaan 1:29
7
Yowaan 1:10-11
Ci àddina la masa nekk, te àddina sàkkoo ci moom, waaye waa àddina xamuñu ko. Ci ñoñam la ñëw, waaye ñoñam a ko dalalul.
Explore Yowaan 1:10-11
8
Yowaan 1:9
Leer giy dëgg, tey leeral nit ñépp, moo dikk ci àddina.
Explore Yowaan 1:9
9
Yowaan 1:17
Yoon wi indi ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lees ko joxee, waaye yiw wi ak dëgg gi, ci Yeesu Almasi bi la dikke.
Explore Yowaan 1:17