1
Yanqóoba 4:7
Kàddug Yàlla
KY
Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Compare
Explore Yanqóoba 4:7
2
Yanqóoba 4:8
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setalleen seen xol.
Explore Yanqóoba 4:8
3
Yanqóoba 4:10
Toroxluleen fi kanam Boroom bi, mu yékkati leen.
Explore Yanqóoba 4:10
4
Yanqóoba 4:6
Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
Explore Yanqóoba 4:6
5
Yanqóoba 4:17
Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga.
Explore Yanqóoba 4:17
6
Yanqóoba 4:3
Te su ngeen ñaanee, dungeen am, ndax mébét mu bon ma ngeen ñaane, ngir am lu ngeen toppe seen bakkan.
Explore Yanqóoba 4:3
7
Yanqóoba 4:4
Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.
Explore Yanqóoba 4:4
8
Yanqóoba 4:14
Yeen xanaa xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!
Explore Yanqóoba 4:14