1
Yawut ya 2:18
Kàddug Yàlla
KY
Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.
Compare
Explore Yawut ya 2:18
2
Yawut ya 2:14
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Explore Yawut ya 2:14
3
Yawut ya 2:1
Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.
Explore Yawut ya 2:1
4
Yawut ya 2:17
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.
Explore Yawut ya 2:17
5
Yawut ya 2:9
Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deewam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deewale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.
Explore Yawut ya 2:9