1
Njàlbéen ga 41:16
Kàddug Yàlla
KY
Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»
Compare
Explore Njàlbéen ga 41:16
2
Njàlbéen ga 41:38
Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol xelum boppam?»
Explore Njàlbéen ga 41:38
3
Njàlbéen ga 41:39-40
Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Ndegam Yàlla xamal na la lii lépp kay, leer na ne amul kenn ku muus te rafet xel ni yaw. Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.»
Explore Njàlbéen ga 41:39-40
4
Njàlbéen ga 41:52
Doomam ja ca topp mu tudde ko Efrayim (muy firi Giir), ndaxte da ne: «Yàllaa ma giiral ca réew ma ma sonne.»
Explore Njàlbéen ga 41:52
5
Njàlbéen ga 41:51
Yuusufa tudde taaw ba Manase (muy firi Ki ma taxa fàtte), ndaxte da ne: «Li ma sonn ak li ma sore sama kër baay lépp, Yàlla fàtteloo na ma ko.»
Explore Njàlbéen ga 41:51