Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo. Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem ji mu fésal ci Almasi bi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram fa déndi asamaan. Foofa la Almasi bi tiime lu sore gépp nguur ak bépp sañ-sañ ak gépp manoore ak gépp kilifteef ak wépp tur wees di tudd, muy tey di ëllëg.