Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra. Firawna du leen déggal. Su ko defee nag maay tàllal sama loxo, tiimale Misra, te maay dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel bànni Israayil, sama ñoñ, ñu génn Misra, kuréel ci kaw kuréel.