1
Mucc ga 6:6
Kàddug Yàlla
KY
Kon nag waxal bànni Israayil ne leen: “Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israayil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba jot leen.
Compare
Explore Mucc ga 6:6
2
Mucc ga 6:7
Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen di teggil sas yi leen waa Misra teg.
Explore Mucc ga 6:7
3
Mucc ga 6:8-9
Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.”» Ba Musaa waxee loolu bànni Israayil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti.
Explore Mucc ga 6:8-9
4
Mucc ga 6:1
Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»
Explore Mucc ga 6:1