1
Mucc ga 2:24-25
Kàddug Yàlla gi
KYG
Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen.
Compare
Explore Mucc ga 2:24-25
2
Mucc ga 2:23
Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.
Explore Mucc ga 2:23
3
Mucc ga 2:10
Ba xale ba màggee, mu yót ko doomu Firawna, mu def ko muy doomam, tudde ko Musaa (mu firi Ki ñu génne), ndax la mu ko génnee ca ndox ma.
Explore Mucc ga 2:10
4
Mucc ga 2:9
Doomu Firawna ne ko: «Yóbbul xale bii te nàmpalal ma ko, maa lay fey.» Ndaw sa jël liir ba, di ko nàmpal.
Explore Mucc ga 2:9
5
Mucc ga 2:5
Ba mu ko defee doomu Firawna ju jigéen dikk, di sangusi ca dexu Niil ga, surgaam yu jigéen yay doxantu ca tàkk ga. Ba loolu amee mu séen pañe ba ca biir barax ba, daldi yónni jaamam, mu yót ko ko.
Explore Mucc ga 2:5
6
Mucc ga 2:11-12
Ba ñu demee ba Musaa màgg, dafa am bés, mu seeti bokkam ya, gis leen ca liggéey yu metti, ya ñu leen sas. Mu gis jenn waayu Misra di dóor kenn ca bokki Ebrë ya. Musaa geestu wet gu nekk, gisul kenn, mu rey waa Misra ja, daldi gas, suul ko.
Explore Mucc ga 2:11-12
Home
Bible
Plans
Videos