Mucc ga 2:11-12
Mucc ga 2:11-12 KYG
Ba ñu demee ba Musaa màgg, dafa am bés, mu seeti bokkam ya, gis leen ca liggéey yu metti, ya ñu leen sas. Mu gis jenn waayu Misra di dóor kenn ca bokki Ebrë ya. Musaa geestu wet gu nekk, gisul kenn, mu rey waa Misra ja, daldi gas, suul ko.