1
Efes 2:10
Kàddug Yàlla
KY
Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.
Compare
Explore Efes 2:10
2
Efes 2:8-9
Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.
Explore Efes 2:8-9
3
Efes 2:4-5
Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.
Explore Efes 2:4-5
4
Efes 2:6
Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Explore Efes 2:6
5
Efes 2:19-20
Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. Yeena di tabax bi ndawi Almasi bi ak yonent yi di fondmaa bi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju koñu tabax bi.
Explore Efes 2:19-20