Te kiy jagleel beykat bi am jiwu ak mburu mu nit di dunde nag, kooku moo leen di jox jiwu mu ne gàññ, te mooy ful seen meññeefum njekk. Su ko defee ngeen woomle ci lépp, mana yéwén ci wet gu nekk, ba seen jëf ji sottee ci nun mana jur cant gu bare, ñeel Yàlla.