1
2.Korent 4:18
Kàddug Yàlla
KY
Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
Compare
Explore 2.Korent 4:18
2
2.Korent 4:16-17
Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés. Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.
Explore 2.Korent 4:16-17
3
2.Korent 4:8-9
Nu nekk lees nuy tance, waaye deesu nu nappaaje. Dinanu jaaxle, waaye dunu jàq. Dees na nu bunduxataal, waaye deesu nu wacc. Dees na nu daaneel, waaye deesu nu jekkali.
Explore 2.Korent 4:8-9
4
2.Korent 4:7
Nun nag nooy njaqi bani kese yi yeb jooju alal, ngir mu bir ne manoore ju yéeme ji alal ji làmboo, manoorey Yàllaa, waaye du sunu jos.
Explore 2.Korent 4:7
5
2.Korent 4:4
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm biy yànjal leeru Almasi biy melokaanu Yàlla.
Explore 2.Korent 4:4
6
2.Korent 4:6
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leer ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi bi.
Explore 2.Korent 4:6