1
1.Timote 6:12
Kàddug Yàlla
KY
Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.
Compare
Explore 1.Timote 6:12
2
1.Timote 6:10
Ndax sopp xaalis kat mooy reenu mboolem xeeti loraange. Am na ñuy ŋaf-ŋafi, di ko wut, far lajj ci yoonu ngëm, ba teg seen bopp tiis wu bare.
Explore 1.Timote 6:10
3
1.Timote 6:6
Teewul ragal Yàlla gu ànd ak doylu, di alal ju réy.
Explore 1.Timote 6:6
4
1.Timote 6:7
Ndax kat indaalewunu dara ci àddina, te manunoo yóbbaale dara.
Explore 1.Timote 6:7
5
1.Timote 6:17
Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.
Explore 1.Timote 6:17
6
1.Timote 6:9
Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan aki fiir ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.
Explore 1.Timote 6:9
7
1.Timote 6:18-19
Ñi barele na ñuy def lu baax, nañu barele ci jëf ju baax, di joxe ci xol bu tàlli, yéwén te nangoo dimbalee. Noonu lañuy dajalee alal, muy cëslaay lu dëgër ngir ëllëg, ndax ñu jot ci dund giy dëgg.
Explore 1.Timote 6:18-19