1.Timote 3
3
Meloy njiit ci mbooloom ñi gëm
1Wax ju wóor a ngii: kuy sabablu yenub sàmm mbooloo mi, mu ngi yóotu liggéey bu rafet. 2Sàmm bi nag, nii la wara mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, moom boppam te maandu; war na am faayda, man gan te am mayu jàngle; 3warul di ab màndikat mbaa xeexkat, waaye na lewet te jàmmu, baña bëgge ci xaalis. 4Na yor këram yorin wu rafet, te ay doomam déggal ko ak teggin yu mat. 5Ndaxte ku manta yor njabootam, naka lay mana yore njabootu Yàlla? 6Te it bumu nekk kuy doora gëm, ngir mu baña yég boppam, bay dajeek mbugalu Yàlla, ni ko Seytaane defe woon. 7Te it war na am seede su rafet ci waa àddina, ngir ñu bañ koo diiŋat, ba muy daanu ci fiirug Seytaane.
Meloy kiy topptoo yëfi mbooloo mi
8Kiy topptoo li mbooloo miy jëfandikoo itam na am faayda te fonk kàddoom; bumu di ku yàqu ci sàngara, mbaa ku alal jiital. 9Na sàmm mbóoti ngëm gi ak xel mu dal. 10Moom itam nañu ko jëkka seetlu, ba mu leer ne amul ŋàññ, ñu door koo fal. 11Naka noonu, na jigéen ñi#3.11 jigéen ñi: manees na ko tekki nii it: seeni soxna am faayda, baña jëw mbaa xér ci dara, waaye nañu takku ci lépp.
12Ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag, nay ku yem ci benn soxna, jiite bu baax këram ak i doomam. 13Ndaxte ku ci rafetal sasam dina am tur wu tedd ak kóolute gu mat sëkk ci yoonu ngëm, gi ci Kirist Yeesu.
Màggug mbooloom Yàlla
14Bëgg naa laa seetsi balaa yàgg, 15waaye amaana mu yéex. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir xamal la, ni ñu wara nekke ci kër Yàlla gi, maanaam ci mbooloom Yàlla Aji Dund ji, miy kenug dëgg te di sëslaayam. 16Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:
Ki wàcc, yor bindu nit,
mu bir ne xelam jub na,
te malaaka ya gis ko;
xamlees na ko ci xeet yi,
ñu gëm ko ci kaw suuf,
te Yàlla teeru ko ci ndamam.
Currently Selected:
1.Timote 3: TI
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright