1.Korent 10
10
Mbirum bànni Israyil misaal la, ma nuy artu
1Bokk yi, bëgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. Ñoom ñépp niir wa#10.1 Ba bànni Israyil nekkee ca màndiŋ ma, Boroom bi moom ci boppam moo leen jiite woon, mel ni niir ci bëccëg bi, ngir gindi leen, su guddee mu doon jumu sawara, ngir niital leen. tiimoon na leen, te ñoom ñépp jàll nañu géej. 2Sóobu nañu ca ndoxu géej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa. 3Ñoom ñépp bokk nañoo lekk ñam wa Yàlla joxe, 4naan naan ga mu joxe, ndaxte ñu ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon. 5Teewul ñi ëpp ci ñoom neexuñu woon Yàlla, ba mu fàddoon leen ca màndiŋ ma.
6Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon. 7Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.» 8Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés. 9Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee. 10Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax Malaakam bóomkat bi rey leen.
11Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat. 12Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytula daanu ci bàkkaar! 13Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu dina leen ubbil bunt bu ngeen mana rëcce, ba ngeen man koo dékku.
Buleen booloo ak rab yu bon yi
14Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw xërëm yi. 15Maa ngi wax ak yéen ñi am xel. Kon seetleen li ma leen wax. 16Kaas bu yiw bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist? 17Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun ñépp lu nu baree bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi.
18Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel sarxalukaay ba? Ahakay! 19Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? Walla xërëm yi dañuy dara? 20Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi. 21Manuleena naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Manuleena sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi. 22Walla boog ndax danuy jéema gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole?
Na mbëggeel laal seeni jëf, te ngeen wottu seen sañ-sañ
23Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm. 24Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam.
25Man ngeena lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel. 26Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.»
27Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, baña laajte dara ngir dalal seen xel. 28Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal. 29Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax.
Waaye nga ne: «Li ma saña def, lu tax nit ku xelam dalul di am dara lu mu ciy wax? 30Su ma lekkee dara di ci sant Yàlla, lu tax ñu may wax lu ñaaw, fekk sant naa ci Yàlla?»
31Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen mana def, defleen lépp ngir màggal Yàlla. 32Buleen def dara lu mana fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla. 33Noonu laay def man ci sama bopp: damay wuta neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
Currently Selected:
1.Korent 10: TI
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright