Room 2
2
Yàlla mooy àtte
1Yaw nit kiy sikke nag, amoo aw lay, ndax boo sikkee keneen, sa bopp nga sikk, nde yaw miy sikke, jooju jëfin ngay jëfe. 2Waaye wóor nanu ne àtteb Yàlla bi muy añale ñiy jëfe jooju jëfin, dëgg lay dëppool. 3Yaw nit kiy sikk ñiy jëfe yooyii, te di ko def, ndax defe nga ne yaw ci sa bopp dinga rëcc àtteb Yàlla? 4Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy akug jéllaleem akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?
5Waaye sag dëgër bopp ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe. 6Ca lay fey ku nekk ay jëfam. 7Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam ak teraanga ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ. 8Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét mooy seen yool. 9Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci; 10daraja ak teraanga ak jàmm nag moo ñeel képp kuy def lu baax, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci. 11Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
12Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane. 13Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di jox àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa mooy jot àtteb ku jub. 14Jàmbur ñi dul Yawut, te amuñu yoonu Musaa, ndegam teewu leena topp bindub juddu bay jëfe li yoonu Musaa laaj, dafa fekk ñoom ci seen bopp, ñu aw seen yoonu bopp, doonte amuñu yoonu Musaa. 15Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def léeg-léeg mu sikk leen, léeg-léeg mu dëggal leen. 16Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi bi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
Yoonu Musaa, na jariñ ki ko topp
17Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla. 18Yaa xam coobarey Yàlla, te yaa jànge ci yoonu Musaa, ba xam li am solo dëgg. 19Yaw mi mu wóor ne yaa di wommatkatub gumba yi, te di leeru ñi ci lëndëm gi, 20yaay yar naataxóona yi, di jàngal tuut-tànk yi, gannaaw wóor na la ne am nga ci yoonu Musaa mboolem luy jëmmu xam-xam ak lépp luy dëgg. 21Kon yaw miy yare, ndax doo yar sa bopp? Yaw miy waare, di aaye sàcc, mbaa doo sàcc? Yaw miy aaye njaaloo, mbaa doo njaaloo? 22Yaw mi bañ bokkaale, mbaa doo sëxëtoo jaamookaayi bokkaalekat yi? 23Yaa ngi sagoo yoonu Musaa te di ko moy bay teddadil Yàlla! 24Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jàmbur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.
Xaraf, na jariñ boroom
25Aaday xaraf nag amal na la njariñ, ndegam sàmm nga yoon wi ko digle. Waaye soo dee moykatub yoon wi, sag xaraf, ñàkka xaraf lay doon. 26Kon kay ki xaraful, tey jëfe njub gi yoonu Musaa santaane, ñàkka xarafam, ndax deesu ko ko waññal ag xaraf? 27Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi. 28Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram. 29Waaye ab Yawut dëgg, kumpag biir xol la koy nekke, xaraf it mbirum xol la; ci xel mi lay sottee, waaye du ci mbindum yoon. Ngërëm la it du ci nit lay jóge, waaye ci Yàlla la jóge.
Currently Selected:
Room 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright