YouVersion Logo
Search Icon

Peeñu ma 15

15
Musibay mujjantal agsi na
1Ma xoolaat, gisuma ci asamaan lu moy jeneen firnde ju màgg te yéeme: juróom ñaari malaaka yu taawu juróom ñaari musiba. Musiba yu mujj ya lañu nag, ngir ca la sànjum Yàlla di mate. 2Ma gisati lu mel ni géeju kiristaal bu jaxasook sawara. Ci biir loolu ña daanoon rab waak jëmmu nataalam, ak lim bi méngook turam, ñu ngi taxaw ci kaw géeju kiristaal gi, yore ay xalami Yàlla. 3Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba ak woyu Xar mi, naan:
«Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji,
yaa réy te yéeme ay jaloore.
Yaw Buuru askan yi,
yaa jub te dëgguy doxalin.
4Boroom bi, ana ku la ragalul?
Ku dul màggal saw tur?
Yaw doŋŋ yaa sell.
Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la,
ndax yaa jubi dogal.»
5Gannaaw loolu ma xoolaat, daldi gis màkkaan ma fa asamaan, xayma ba fat seede si ñu bind ci àlluway xeer ubbiku. 6Juróom ñaari malaaka yi taawu juróom ñaari musiba yi nag, génne ci màkkaan mi. Ñu ngi sol mbubbi lẽe yu set, ne ràññ, ay ngañaayi wurus takke ci seen dënn. 7Kenn ci ñeenti mbindeef yi nag jox juróom ñaari malaaka yi juróom ñaari ndabi wurus yu fees ak sànjum Yàlla jiy dund ba fàww. 8Ba mu ko defee màkkaan ma fees ak saxaar su bawoo ci leeru Yàlla ak kàttanam. Kenn nag manatula dugg ci màkkaan mi, ba kera juróom ñaari musiba yu juróom ñaari malaaka yi matee.

Currently Selected:

Peeñu ma 15: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in