YouVersion Logo
Search Icon

Màndiŋ ma 11

11
Bànni Israayil ñaxtu nañu
1Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba. 2Mbooloo ma jooy ko Musaa, Musaa tinu Aji Sax ji, sawara wa fey. 3Ñu tudde béreb boobu Tabera (mu neexook Tàkkaan), ndax sawaras Aji Sax ji leen fa tàkkal.
4Ci biir loolu genn gàngooru njaxasaan mu nekkoon ca seen biir jiital seen bakkan, di ŋaf-ŋafi, ba tax bànni Israayil itam dellu di jàmbat. Ña nga naan: «Éy ku nuy leelatiw yàpp! 5Namm nan jën ya nu daa ndawaloo ca Misra, te dikkewu nu tus! Ak yomb jaak xaal jaak pooro baak soble saak laaj ja! 6Tey jii sunu put yaa ngi wow koŋŋ, gisunu lenn lu moy mànn
7Mànn ma nag daa meloon ni pepp mi ñuy wax koryanda, te nirook ndàbbu garab gi ñuy wax bedelyum. 8Mbooloo ma da daan wër, di ko for, di ko wole doji wolukaay, mbaa ñu di ko dëbb ciy gënn, ba noppi baxal ko ci cin, def ko ay mburu yu cafkaam mel ni cafkay nàkk yu am niw. 9Bu layaa ca dal ba ag guddi, mànn ma day wàccaale ak moom.
10Ci biir loolu Musaa dégg mbooloo miy ñaxtu, làng ak làng, ku nekk ci sa bunt xayma. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkk jippét, Musaa nag ñaawlu ko. 11Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw? 12Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew ma nga giñaloon seeni maam? 13Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk”? 14Manumaa boot mii mbooloo mépp, man doŋŋ, ndax àttanuma ko. 15Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»
Aji Sax ji dig na Musaa ñu ko jàppale
16Ba mu ko defee Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israayil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw. 17Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.
18«Mbooloo mi nag, ne leen ñu sangu-set ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk. 19Du benn fan lañuy yàpp, du ñaar, du juróomi fan, du fukk, te du ñaar fukki fan. 20Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo, lu nu taxoona jóge Misra!”»
21Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! 22Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?»
23Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!»
Yàlla sédd na mag ña ag leeram
24Ci kaw loolu Musaa génn, jottali mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji, daldi dajale juróom ñaar fukki góor ñu bokk ca magi mbooloo ma, taxawal leen, ñu wër xayma ba. 25Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di jottali ay kàdduy waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.
26Fekk na ñaari góor a nga desoon ca dal ba, kenn ka di Eldàdd, ka ca des di Medàdd, te teewul leer ga dal ca seen kaw, ndax dees leena limaale woon ca mag ña, doonte demuñu ca xayma ba. Ñoom it ñuy jottali ay kàdduy waxyu ca dal ba. 27Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay jottali ay kàdduy waxyu ca dal ba!» 28Yosuwe doomu Nuun ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!» 29Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sang leen ag leeram!» 30Ba loolu amee Musaa dellu ca dal ba, moom ak magi Israayil ña.
Mbas wàcc na ca Kibbrot Taawa
31Ba loolu amee ngelaw wale ci Aji Sax ji, daldi bàbbee ca géej ga ay picci përëntaan, wàcce leen ca dal ba lu tollook doxub benn fan ci gii wet, ak doxub benn fan ca gee, ñu dajal dal ba bépp, jale ci suuf ba xawa mat ñaari xasab. 32Ci kaw loolu mbooloo ma taxaw di for, bëccëgub keroog bépp, ak guddi ga gépp, ak bëccëgub ëllëg sa sépp, ba ka gëna néewle, for lu mat fukki barigo. Ñu weer përëntaan ya fa wër dal ba. 33Suux waa nga ca seeni gëñ, sàqameeguñu sax, sànjum Aji Sax ji tàkkal mbooloo ma. Aji Sax ji dumaa mbooloo ma mbas mu metti lool. 34Moo tax ñu tudde béreb booba Kibbrot Taawa (muy firi Bàmmeeli Ŋaf-ŋaf), ndax fa lañu denc néewi mbooloo ma doon ŋaf-ŋafi. 35Kibbrot Taawa la mbooloo ma bàyyikoo, jëm Àccerot. Ñu dal nag ca Àccerot.

Currently Selected:

Màndiŋ ma 11: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in